

| WOLOF | Français |
| "Am naa giléém ca Gànnaar yomb naa wax." | "J'ai un chameau en Mauritanie, c'est facile à dire." |
| "Xamul" aay na wànte "laajtewul" a ka yéés. | Ne pas savoir n'est pas recommandé, mais ne pas questionner c'est pire. |
| Alalu golo ca lex ba. | Tous les biens du singe sont dans sa joue. |
| Bakkan waruw dàll la : fa muy dagge dooko yëg. | La vie c'est comme une lanière de sandale : avant qu'elle ne soit rompue, on ne peut pas savoir où cela va se produire |
| Bala nga xam luw taat di jariñ, mbate toog jote. | On ne connaît l'utilité des fesses qu'au moment de s'asseoir. |
| Bant, lumu yàgg cig dex, du tax mu soppiku jasig | Un bout de bois, il peut rester longtemps longtemps dans un fleuve,ce n'est pas pour ça qu'il va se transformer en crocodile. |
| Bëgg-bëgg yee wuute, moo-tax njaay may jar ca jaba. | Les goûts sont différents, c'est pour ça que tout ce qui se vend au marché trouve acquéreur. |
| Bëggum ñeex duma taxa dëppoo cin lu tàng. | Ce n'est pas parce que je veux de la sauce que je vais me retourner la marmite chaude sur la tête. |
| Benn loxo du tàccu. | Une main n'applaudit pas. |
| Bes boo gis, day leb walla muy fey. | Chaque jour est l'occasion d'une dette que l'on contracte ou que l'on rembourse. |
| Bët du yenu waaye xam na lu bopp àttan. | L'œil ne porte aucune charge, mais il sait ce que la tête est capable de porter. |
| Bëtub mbëggeel jéll nab gàkk. | Le regard de l'amour passe par-dessus les défauts. |
| Béy du gëmal gënn. | Une chèvre ne croit jamais qu'un mortier est vide. |
| Boo bëggee xam luy laabiir, amal doom. | Si tu veux savoir ce qu'est l'indulgence, aie un enfant. |
| Boo bëggee xam luy muñ, amal jabar. | Si tu veux savoir ce qu'est la patience, prends une épouse. |
| Boroom ndékki ku ko jëkka yeewu tëddaat. | Celui qui se lève avant le responsable du petit déjeuner peut aller se recoucher. |
| Boroom tubéy, bu jàngoo sol. | Le propriétaire du pantalon, après s'être lavé les pieds, c'est lui qui le met. |
| Bu la am-am taxa bew, ndax ñàkk du wess. | Il ne faut pas être fier de sa fortune, car un revers peut toujours arriver. |
| Bu la mën-ngawar jayee ba nga mafñandum saaw, boo fa jogee loo amati jënde koog teg. | Si tu es bon cavalier et assez fanfaron pour monter un porc-épic à cru, si tu t'en sors, tout ce que tu possèdes tu le mettras à l'achat d'une selle. |
| Goneg mbóóya gu reew, xaar ko ca taatu ndaa la. | L'enfant mal élevé, quand souffle l'harmattan, attends-le au pied du canari. |
| Gumba am na beneen liggééy bu dul nas i pusó. | L'aveugle a un autre travail que d'enfiler des aiguilles. |
| Guy dana jur i dég. | Il arrive qu'un baobab ait des épines. |
| Jikko dana soppiku jaan walbatiku màtt boroom ba. | Le caractère, ça peut se changer en serpent, se retourner et mordre son maître. |
| Këll bu ne am na mberoom. | Chaque calebasse a son couvercle. |
| Kooyi bukki du njoowaanug tef. | Le pénis de la hyène n'est pas une balançoire pour un chevreau. |
| Ku am kuddu du lakk | Celui qui a une cuillère ne se brûle pas. |
| Ku bañ ku la ñafale, dangay toññ koo mën. | Celui qui ne veut pas être corrigé s'attaque à moins fort que lui. |
| Ku Bëgg lem ñeme yamb. | Celui qui ne craint pas les abeilles mange le miel. |
| Ku bey sa bànneex, góób saw naqar. | Celui qui cultive son plaisir récolte une douleur profonde. |
| Ku dul toxu doo xam fu dëkk neexe. | Si tu ne changes pas de place, tu ne peux pas savoir quel endroit est agréable. |
| Ku fecc ba génnub géb, kenn du la seetaan. | Celui qui danse jusqu'à sortir du cercle, personne ne le regarde plus. |
| Ku jaaxaan disaw, balaa kenn a tooy nga lóór. | Si tu pisses en étant couché sur le dos, avant que quelqu'un ne soit mouillé, toi, tu seras trempé. |
| Ku la abal i tànk, nga dem fa ko neex. | Si quelqu'un te prête des jambes, tu vas où il lui plaît. |
| Ku la mag ëpp lay sagar. | C'est le plus âgé qui a le plus de chiffons. |
| Ku ndóbin rey sa maam, foo séénati lu ñuul daw. | Si un grand calao tue ton grand-père, tu te sauveras dès que tu verras quelque chose de noir. |
| Ku xamul "suurnaa", dangay téyé ca loxo ba. | A celui qui ne sait pas dire "je suis rassasié", tu retiens la main. |
| Ku xeebul sa nguur di buur. | Celui qui se satisfait de son sort est roi. |
| Ku yàgg ci teen, baag fekk la fa. | Qui attent longtemps au puits finira par y trouver un seau à puiser. |
| Kuy gunge boroom biirbuy daw, lu la ca "waaxusil" fekkee. | Celui qui accompagne quelqu'un qui a la diarrhée n'a pas à lui dire : "dépêche-toi". |
| Kuy jaaykamaate doo bëré : boo ca dëggee mu toj. | Celui qui vend des tomates ne doit pas se bagarrer |
| Làmb aw taat, boroom a ca gën. | Pour toucher des fesses, il vaut mieux en être le propriétaire. |
| Lëg mën naa daw, waaye àttanul teg. | Le lièvre peut courir, mais il est incapable de porter une selle. |
| Lëngoo daf a neex rekk, waaye koo bàyyi mu dem ak boppam. | Se tenir par les épaules, c'est agréable, mais si tu laisses tomber, l'autre s'en va tout seul. |
| Loo barele barele, boo génnee gis loo moomul. | Si grandes soient tes richesses, quand tu sors, tu vois quelque chose qui ne t'appartiens pas. |
| Lu jinné màggat màaggat dese nelaju bu jommal gone. | Le djinn, si vieux soit-il, est encore capable de faire des grimaces pour affoler les enfants. |
| Lu la bett mën la. | Tout ce qui te prend au dépourvu est plus fort que toi. |
| Lu la mar mayul, màtt du la komay. | Ce que lécher ne peut pas donner, mordre ne le donne pas. |
| lucin xat xat, xorom ba xaj ca. | Si étroite que soit la marmite, le sel peut toujours y pénétrer. |
| Mën ko, defoo ko, tëlée ko gën. | Il vaut mieux être incapable de faire quelque chose plutôt que d'en être capable et de ne pas le faire. |
| Merum ganaar lu muy wàññi tusuñe. | La colère de la poule ne dérange pas le cuisinier. |
| ñaari yëkkyu mat xajuñu ci menn mbalka. | Deux taureaux dans la force de l'âge ne peuvent être en même temps au même abreuvoir. |
| ñaq du feeñ ci taw | La sueur ne se voit pas sous la pluie. |
| Ndànk-ndànk ay jàpp golo cib ñaay. | C'est en allant doucement qu'on attrape le singe dans la brousse. |
| Nen du bëreek doj. | Un œuf ne lutte pas avec un caillou. |
| ñu bokh teen ñooy laxasooy goj. | Ceux qui partagent le même puits emmêlent leur corde. |
| Ñu yemul lor, duñu mëqandoo sunguf. | Ceux qui n'ont pas la même quantité de salive ne doivent pas manger de la farine ensemble. |
| Picc mu masula naaw, su naawee firim rééw. | L'oiseau qui n'a jamais volé, le jour où il vole, il fait le tour du pays. |
| Picc, la mu wax ci banqaasu garab du ko wax ci loxol gone. | Ce que dit l'oiseau sur la branche de l'arbre, ce n'est pas ce qu'il dit dans la main d'un enfant. |
| Saabu du fóót boppam. | Le savon ne se lave pas lui-même. |
| Sàmmkat sañ naa maye meew, wànte sañula mayew sëllu. | Un berger a le droit d'offrir du lait, mais il n'a pas le droit d'offrir un veau. |
| Sant dëkkul fenn. | le nom de famille n'habite nulle part. |
| Soo xamoon li lay yoot, nga bàyyi li ngay yoot, te daw. | Si tu savais ce qui te guette, tu laisserais ce que tu guettes et te sauverais, |
| Sori kaw a tax jaxaay di saw bouki. | C'est parce que l'aigle est très haut qu'il pisse sur la hyène. |
| Su may dee ci àll, gayndee may rey. | Si je dois mourir dans la brousse, que ce soit le lion qui me tue. |
| Tànk ci suuf, jaan ci suuf, fu ñu jaar daje. | Les pieds sont par terre, le serpent est par terre, ils vont inévitablement se rencontrer. |
| Tilim dina dem fu saabu mënula dem. | La saleté va parfois où le savon ne peut pas aller. |
| Tuñum giléém lang na, waaye rotul. | La lèvre du chameau pend, mais elle ne tombe pas. |
| Waxi mag dana guddee all, waaye du ca fanaan. | Les paroles de l'ancien s'attardent dans la brousse, mais elles n'y passent pas la nuit. |
| Waxi ndee bu taxawee, ndund yaa tax. | Si les paroles d'un mort restent debout, c'est à cause des vivants. |
| Waxtaan ñam la, ku ko teewe ca nga. | La conversation, c'est comme un repas, celui qui se trouve là y participe. |
| Xeeb sa takkum, mu takk saw say. | Méprise ta ficelle, elle n'en attache pas moins ton fagot. |
| Xeex, ku ko fekke, boo àttewul, danga sot. | Lors d'une bagarre, celui qui y assiste et qui ne s'interpose pas, prend parti. |
| Xel bu doon jaay lamb. | L'intelligence, si elle était à vendre, ne trouverait pas d'acquéreur. |
| Yàgg ay wone légétub taat. | C'est avec le temps qu'on découvre une cicatrice aux fesses. |
| Yàgg du saabu, waaye dana fóót. | Le temps n'est pas du savon, mais il blanchit. |
| Yàlla, yàlla, bey sa tool. | Invoquer Allah ne te dispense pas de cultiver ton champ. |
| Yééné néég la, boroom a cay fanaan. | Le souhait est une chambre, c'est celui qui le formule qui y passe la nuit. |